Menu
X
image

Le conteur wolof Maam Daawur Waad à la JMT 2020

Yan kàddu ci jamonoy jax-jax
Saa yu jamono jaxee baat yi ñuy móole sunuy kàddu di ko waxeek nit ñi, danoo war a suppi seeni tëggin ak seeni tegin.

Nu tekku ba sunuy xel dal. Nanu xalaat ndoxu taw mu taa ci benn àll: maanaam ab déeg. Ci wetu déeg boobu, mu am fa genn garabu màngo gu meññ doomi màngo yu ñor xomm. Nu jekki-jekki,benn doomu màngo bu ndaw,rot, ni cundux ci ndoxu déeg boobu.
Ficc yi tiit, ni fërr naaw ñoom ñépp, ndox mi rassu, ay rëdd juddu ci kawam, toppante, daw, dàxante dem, ni bàww ci tàkkul déeg bi, bett fa gunoor yu naansi woon, mëdd ca ñenn, ya ca des, tasaaroo, nu golo xam boote doomam.
Niki bi mbasu Covid-19 mi nit ñi ñimeetul ba duñu ko tudd te mu sóobu ci déegub àdduna, mu ngi fekk nit ñaa ngi daan jàmmasante, di nuyoo. di waxtaan, di lëngoo, di téyeente, di jàppantey yoxo. Ci diir bu gàtt, baati doxalin yu jalgati doxalin yooyu, jolli ci fépp ci àdduna bi: dàndante, raxasu te lekkoo, masku, liggeeykat yi lëlu, dongo yi bër te daara yi waraguñu woon a bër.Tiitaange wàcc ci xeet wi, ñu ne mag ñi la mbas mi gën aay ci ñoom, ndaw yi, ñoo ciy gën a mucc. Doktoor yiy dunyaa yi waaru, di gëstu nuñuy jénge feebar bi dal ci xeet wi nga xam ne, ci diir bu gàtt, kurel giy saytu wér gi yaramu doomi Aadama ci àdduna bi, tudde ko mbas ndax li mu wër réewi dunyaa yépp.

Nan la nu war a waxe ak xeet wi ci li xew ci jamonoy jax-jax bi?

Yékkati kàddu jëme ko ci nit ñi, ñu déggandoo ko, dégge ko ni nga ko bëgge, mbir gënu koo jafe. Rax ci dolli, ci sunu jamonoy tey jii, bërëb yi kàddu mën a jollee dañoo bare ba jéggi dayo:

-njiiti réew yi
-kilifay diine
-daaray njàng mu kawe mi
-njiiti làngu politig
-njiitu kurel yi
-taskati xibaar yi
-këyiti xibaar yi
-Telewisyong yeek rajo yi
-dég-dégu wewu nag
-Enternet
-Reso sosiyo yi
-Mbootaay yi
-Ndajey xew-xew yi
-Ak yeneen ak yeneen

Ci kàddu yiy jollee ci bërëb yooyu te leeleeg, ñuy lawlawee benn xibaar, ndax waxin ya, dëppoo nañook waxinu jamonoy jax -jax?
Ndax wax ji dañu koo jële ciw làkk tekki ko ci weneen. Ndax nañu ko tekkee aw na yoon?
Ndax la wax ya ëmb, dafay nar a yokk walla dafay nat a wàññi njaqare li nit ñi àndal ?

Ndax bërëb yooyu kàddu yiy jollee, nit ñi koy déglu walla ñu koy jàng mbaa di ci jot, wóolu nañu leen ba mën a gëm kàddu ya soqeekoo foofee?
Ci diggante bërëb bi kàddu yiy jollee ak nit ña moom kàddu ya, ñaar war na ca :
1. Kiy wax, war naa xam bu wér li muy wax, xam itam ñi mu jagleel kàddu ya muy yékkati ba mën leen a méngale ak seen dég-dég.
2. Ñi moom kàddu yi, ñoom itam, war nañoo am kóolute ci kiy wax ba mën a gëm ni li mu leen di wax, lu ñu mën a déglu la, dégg ko, ba mën koo nangu am déet.
Bu ñaar yooyii amee ci diggante bërëb buy kàddu di jollee ak bëreb yay jot ca kàddu ya, lëkkaloo buy indi jokkoo, taxaw na.
Su boobaa, laaj na, wax jay tàbbi ci xeli nit ñi, nekk waxi dëgg.
Lan mooy dëgg googu ñuy wax? Sunu déggoo ci ni dëgg mooy lu wuute ak li ñuy tudde kàcc walla ñeneen, waxi dëgg moo dëppoo ak lu kenn mënul a weddi ndax li mu ami seede walla muy lu ñépp déggoo ni dëgg la ca jamono jooju.

Ci misaal : « Covid-19, wiriis bu sonal réewi àdduna yi la bu nit ñi gisagul garab gi koy faj. »wax ju dëggu la jamono ji nu tollu.
Wànte suñu nee:« waa réewum Itali, gis nañu garab guy faj feebar bi Covid-19 di joxe. », wax ji du dëgg, « Fake news » la ci jamono jii nu tollu.

Su ñuy wax nit ñi dëgg ci jamonoy jax-jax, warees na ko jaare yoon wu leen dul tiital ba ñuy tàggook seen sago, ba seeni doxalin di ñàkk a jaar yoon.
Jikkoy nit ñi dañoo bare te wuute moo waral seeni déggin di wuute, te loolu dinay suppi leeleeg pirim kàddu yiy dugg ci seen noppi woroom.
Ba tax na, danoo war a fexe, saa sune, ba nit ñi nuy amlanteel mbaa nuy jokkoo ak ñoom, wóolu nu ba dara xewagul walla
nu soppantey jikko ci biir xew-xew, ba tabaxandoo ak ñoom laltaayu kóolute.

Ci noonu, jamono bu jax-jax dikkee, tëgg kàddu yu nuy waxeek mbooloo yi nu amlanteel kóolute gu wér, du jafe ndax, wax ju jolli, mën nañu koo déglu, settantal ko, dégg ca la leen ca amal solo.
Wax war naa leeral nit ñi jax-ja a bi, xamal leen nu ñuy def ba mucc ca, mbaa ñu génn ca ci kàddu ñépp dégg.

Terewul nak, baat yooyii, ndare sax mu ngi jóge ci bërëb bu ñu wóolu, warul a tax, nu ñàkk leen a wóorlu, ba gis ni, aw nañu yoon.

Kon boog, ci jamonoy jax- jax, sunuy kàddu
⁃ Nay jox nit ñi yaakaar ci ni, lu mu yàgg-yàgg, li dal ci xeet wi, xam-xam ak pexey nit ñi, ci ndëgarlaayu Sunu Boroom, dina fi jóge.
⁃ Nay fàgguloo nit ñi, ñuy gëm walla ñuy tasaare xibaar bu leen wòorul ne dëgg la.
⁃ Na nekk kàdduy dëfël ñi tiis dal ci seen kaw, ak yuy dëgëral seen ngêm ci ni, lëndëmu tey jii, ak njaqare bi ñu nekke, leeraay ak mbégte, ñoo koy wuutu ëllëg
⁃ Na doon kàddu yuy xiirtal nit ñi ci ñu jàppoo, wóoloonte ànd ngir fasyeenee wàññi soloy jax- jax bi, ba kera ñu ko fiy jële.
⁃ Bépp kàddu buy teg nit ak moroomu nitam ak lu mën a dimbali ca digg xolu bépp xallaat, pexe ak jëf yoo xam ni, seeni jëmu mooy indil saafara jax-jax bi boppam nit ñi.

Ngir kàddu yi nuy nar a yékkati ci jamonoy jax-jax, nit ñi déglu leen, war nanoo tabax kóolute gu dëgër gu nu leen di laltaaye.
Ci noonu, saa yu nu suppee waxinam, ci bu ko jamono laajee, ña nu séqal kóolute ga, duñu réer, ndax dina leen wóor ni, ki ñu ko séqal musu leen a wor.

Su wet gune sàmmee wàllam ci kóolute gi, yékkatiy kàddu ci jamonoy jax-jax jafewul.
Kàddu goo yékkati, wax ko, mbaa nga bind ko, ña koy jot, dinañu la déglu mbaa ñu jàng la, ba jot ca la kàddu ga mbaa mbind ma ëmb.

Terewul nak, jax-jax
yiy ànd ak xew-xew yu deme ni mbënn, mbas ak mbalit, di jur doxi ñaxtu ci mbeddi réewi àdduna yu ni gàññ. yoo xam ne, kàdduy diisoo, waxtaan mbaa mbind, ñoom reek a koy mujj dakkal, kune delloo cayy aajoom ba kera beneen doomu màngo bu tuuti neeti ciné jax-jax, neeti cumbux ci ndoxu déeg bu tekkaaral, ficc ya baaw, jaax -jax nuyoowaat…
Xawma ndax dégg ngeen baay yi ma tëgge sama kàddu yi ci
jamono ju jax jii. May am yaakaar ni baat yi woon ci kàddu yi ma doon wax, dëppoo nañook li ngeen ma laajoon ma waxtaane ko tey jii. Am naa mbegte ci li ngeen ma may nopp, bi may wax. Foofu la dégg wax di tàmbalee. Jaageen jëf.

Maam Daawur Wàdd

 

 

Aucun tag n'a été trouvé!
Retour a la page d'accueil
Newsletter

Abonnez-vous à notre newsletter pour recevoir nos dernières nouvelles et mises à jour. Nous ne spamons pas.

© Copyright 2022 ASTRA. Tous droits réservés.